Moodu mi soxna ndey bëggon

113 3 2
                                    


Maa ngi tuddu moodu dëk fu ñu naan ndoyeen ca wettu luga lo. Maa ngi am 30i at. Bataaxal bi may bind, di naa ci dajjale mboleem Lima fi dundu Ba mu sabab bind gi.
Da maa doonon ab ndonga di jang ca daaru musti fu ñuy woowe "école 4". Yalla saa Borom defal mam xel moom dana xelli saa yooka fëggee. Loolee waral ma amoon ak xarañte ba sa may naatango du Wa ñu ma Raw ci dara. Maa ngi am Sama lijaasa bu njëk (CFEE) ca atum 2008. Ca Laa dem yeggale samam njang ca "CEM SMM" nekk ca daaru musti. Batay Ken massu Maa Raw cim njang su ñuy deff i jongante mbaa yu ni mel. Ca atum 2012 la am sama ñaareelu lijaasa (BFEM), wëyale Sama wuttum xam ca fu ñuy Wax "LYCÉE MTBM", ñu tekk ci 3i at ma am lijaasa gamay genee ci jangukaay yu ndaw yi (BAC), te digante bi yëpp maay jittu ba yeksi fima yeksi tay.
Ginaaw bama noppee ca jangukaay ci ndaw ya, jamono am num ñu bayyi nu 2i at ñuuy xaar fu nu ñuy yobbu bañ Mana yeggale. Ca deytalu 2i at ya di waajal sun 3i ati neen, ca lañu gennee luy firndeel ni njang mi di na tambali si lu neew.
Bama gëstoo ca Laa giss ñu yobbu ma sigensoor (Ziguinchor) ni foofu Laa wara motalee. Ma am ca mbegte ndax yaggoon nama bëgg gen fu sori ngir matal sama yeene ci samay wayjur yii.

Ca ëlëk sa ma tambali waajal
Dem ngir Mana mandal
Sama mar wi ma am ci xam-xam
Ba mana dellu si saa wettu ndey aki ndam.

Céy Moodu!Where stories live. Discover now